BËGG BOROOM BELAL on Clubhouse

Updated: Aug 7, 2023
BËGG BOROOM BELAL Clubhouse
179 Followers
77 Following
@b2bsdx Username

Bio

كو ديم ما ديم كو ديمول ما ديم

🇸🇳🇸🇳🇸🇳🇫🇷🇮🇹

Abdul Ahad ...

✿ Way wii Sëriñ Abdul Ahad (r.a) neena: « Damaa ñëw ci Sëriñ Mbay jaxate (r.a) ne ko: damaa bëgg nga dénk ma ! », Sëriñ Mbay jaxate ne ma: «danaa la dénk te duma la tagg !»

► Abdul Ahad yal na saw fan gudd Mbàkke nga wér | Te sax ci jamm’aku yiw ak jaamu Yàlla gu wér !
► Farlul te wéy yal na ngay for dog bu sedd sa xol | Te mucc ciw ay’akum ndog sax ci def la la war !
► Toppal sa mag Mustafaa bul génn yaw ndigalam | Ngir mag mu mat mag la mat ñéppub sëriñ te du wor !
► Jëfal te bul faale nit, bul geesu nit ci sa jëf | Na Yàlla tax ngay jëf ak Yonen ba ak ka la jur !
► Kalay manal dara moo jar def lëf ak bàyyi lëf | Te kooka nag moo di « Rabbul Archi » yal na la yor !
► Yar bii nga yor yor ko biir ak bitti moo di sa kee | Moo gën ci yaw nit ñu baax ak kër yu baaxaki jur
► Sa baay a gën ñépp teb yar dong-dong la yor | Yoral yaram ba te koo gis deeko sant ak a yar !
► Sa baay a gën ñépp ab yar ngir dalay jox a jox ab yar | Ba ngay am a am ab yar te doo mos i yar !
► Du yëkkatib yar di teg nit waaye moo gënu nit | Ñay teg nitub yar akay janneek a yeew ak a lor !
► Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam | Xamal ni moo ko ca def jii wax ku nekk la bir !
► Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam | Xamal ni moo ko waral ak cant war na gu tar !
► Ag cant war na ci yaw ak ñoom gu rëy gu rafet | Gu tol ne bàjjo gu dul yam fenn mukkati far !
► Loo jis ci Amsatu moo mii cib yar ak jëfu yiw | Xamal ni moo ko ca def gii wax ku nekk la bir !
► Abdooki Amsatu ak Mbakkeeki Bàlla Asan | Yaw say nijaay a ngii ñoo diy sàll kenn du ciw par !
► Fëxal te raw am nga ab yóbbal fëx ak raw a des | Ngir baaxi bokk a di ab yóbbal na yitte ji sar !
► Saral te wéy dëgg bul yam ciy nijaayaki | Baay ak nday di sant ak a doyloo seeni cër lu ko jar ?
► Foo seeru kuy fok a doyloo ab cëram na nga wut | Loo dolli yaw ci sa cër bii ndax nga am cëri-cër !
► Jollil ca kaw bul fexee jëm suuf’akay wax a dal | Cig jolli ngay waare ab xiibon ca ngay note mbër !
► Reggàyu jàmbur ku koy doyloo ba lekkul a xam ! | Buurub Aras ba far ak bër yépp yal na la far !
► Yaw yal na ngay wéy’akay jëm kaw di dolliku ndam | Ba jiitu waa kaw te nangoo suufe kuy amu tur

BËGG GËM WÓOLU RAGAL AK YAAKAAR SEEX ABDUL AHAD REKK KEPP DONG KESEE

Member of

More Clubhouse users