"Sunu Boroom, boo saxee ci naan ko "ana nga?"
Mu sax ci naan la "Maa ngii"
Ana luy ana nga? mooy sax ci topp ay ndigalam
Luy maa ngii? soxla soo am mu fajal la ko "
#Boroom_Tuubaa
Ree yay njariñ li jarul dara,
Te moone njëg gi kenn amu ko.
Day dolli mbég ceem si ko jot,
Te ki koy joxe it du wàññi ko.
Te lu mu gàtt gàtt, yenn saay mu fàttali ko,
Sa giirug dund wan ko ko.
Ak loo barile barile soxla ko,
Way-ñàkk ñi sax man nañu ko.
Reetaan a di noppalug ruuh gi sonn,
Tawféex rekk la ñeel ki sonn,
Leeraayu jànt la, muy noor di nawet,
Day nooyal xol saa su ci naqar duggee,
Te deesul jariñ, kudul nég ñu jox la ko,
Du lees di jënd,
Te deefu ko fob di abale,
Waliif itam ñu sàcc ko.
Soo jotul ree ji nga yeyoo
Baaxal, rekk te joxe ji nga jagoo.
Amul ku gën a soxla ree, kii nga gis te mënul a ree.
if the data has not been changed, no new rows will appear.
Day | Followers | Gain | % Gain |
---|---|---|---|
August 07, 2023 | 87 | +26 | +42.7% |
October 04, 2022 | 61 | -1 | -1.7% |
July 07, 2022 | 62 | +2 | +3.4% |
April 23, 2022 | 60 | +1 | +1.7% |
March 15, 2022 | 59 | +12 | +25.6% |
January 17, 2022 | 47 | +23 | +95.9% |
December 10, 2021 | 24 | +3 | +14.3% |